1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda. Mooy ba waa Sif demee ca Sawul, ne ko Daawudaa nga làqu ca seenum réew. Éy Yàlla, musal ma ngir sa tur, jox ma dëgg, ci sa kàttan.
2Éy Yàlla, déglul, ma ñaan, teewlul, ma wax la.
3Ay doxandéem a ma jógal, di ñu néeg, bëgga jël sama bakkan, te seetuñu ci Yàlla. Selaw.
4Yàllaa ngii, moo may dimbali; Boroom bee yor sama bakkan.
5Yal na ay wi këppu ci ñi may tëru, yal na leen sa dëgg sànk.
6Xol bu tàlli laa lay sarxale. Aji Sax ji, yaa baax, ma sant la.
7Lépp luy njàqare, yaa ma ci jële, ma tiim samay noon.