1Di woyu cant, ñeel askanu Kore wu góor. Aji Sax jee màgg, jara màggal a màggal ca sunu biir dëkku Yàlla, kaw tundam wu sell.
2Jekk taxawaayee tundu Siyoŋ, catu bëj-gànnaar, dëkku Buur bu mag bi, di mbégtem àddina sépp.
3Yàllaa wone kaaraangeem ca biir tatay dëkk ba.
4Buur yaa ngoog daje, àndandoo.
5Nun noo gis, jommi, tiit, fëx,
6ne fay pat-pati, jàq ni kuy matu.
7Ngelawal penku, moom ngay tase gaal gu mag.
8La nu déggoon de lanu gis ca dëkkub Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sunu dëkku Yàlla ba. Yàllaa koy dëgëral ba fàww. Selaw.
9Céy Yàlla, nu ngi sa biir kër, di xalaat sa ngor.
10Céy Yàlla, sa tur ay sa woy ba ca cati àddina. Njubte la sa loxo fees.
11Yal na waa tundu Siyoŋ bég, waa Yuda bànneexoo say àtte.
12Doxleen biir Siyoŋ, wër ko, waññleen ay sooroori tataam,
13nemmikuy tataam, doxantoo këri buur, ba man koo yegge maasug ëllëg,
14ne leen kii ay Yàlla, sunu Yàlla, tey ak ëllëg. Moo nuy jiite ba saa taxaw.