1Dib taalifu cant buy fàttalee, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, bul mer, di ma rëbb; bul xadaru, di ma mbugal.
2Aji Sax ji, fitt nga maa fitt, dóor nga ma.
3Danga maa mere, ma wéradi; maa bàkkaar, ba jagadi.
4Samay ñaawtéef mëdd ma, diisa diis, ba àttanuma ko.
5Maa defug ndof, ba am dana yu bédd, ba xasaw.
6Maa ngi sëgg, ne yàcc, ne yasar, di wéye tiis,
7yaram tàng, di bax, ma wéradi, ne làcc.
8Sama yaram dee goyy, ma ne lasar, jàq, di binni.
9Boroom bi, yaa ngi ne jàkk ci samay nammeel, samay onk umpu la.
10Sama fit a ngi tëf-tëfi, doole ŋiis, gët giim.
11Samay dana tax xarit ak dëkkandoo di ma daw, mbokk dànd ma.
12Ñi may wuta rey a ngi may fiir, di ma jéema lor, di ma waxal musiba, yendu maa lalal pexe.
13Man, ma mel nib tëx, dégguma, mel ni luu, àdduwuma,
14di saf ku dul dégg, bay layoo.
15Aji Sax ji, yaw laa yaakaar; Boroom bi, sama Yàlla, yaa may nangul.
16Ma ne, ngalla buñu ma ree, di damoo samab jéll.
17Maa ngii di waaja daanu, dëkke mitit.
18Ma ne, aylayéwén def naa lu ñaaw, sama bàkkaar tiital na ma.
19Noon yaa ngi ne jonn ak seen doole, bare na ñu ma bañ ci neen.
20Ma ji leen njekk, ñu fey ma njekkar; may sàkku lu baax, ñu di ma sikk.
21Éy Aji Sax ji sama Yàlla, bu ma wacc, bu ma sore.
22Ngalla gaawe ma; Boroom bi, yaa may musal.