1Di ñaani néew-ji-doole ju sonn, bay diis Aji Sax ji njàqareem. Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la; yal na sama yuux àgg fa yaw.
2Bu ma dummóoyu bésub njàqare; teewlu ma, gaawe ma sama bésub woote!
3Samay fan a ngi wéy ni saxaar, sama yax yi mel nib taal.
4Sama xol bi wow ni ñax mu xuur, ba lekk safatu ma.
5Damaa jàq, di onk a onk, ba desey yax.
6Ma mel nim tan ci màndiŋ mi, mbete looy cib gent.
7Nelaw të; ma mel ni picc mu wéetoo puju néeg.
8Bés bu ne noon yi di ma sewal; ñi may ñaawal di móoloo sama tur.
9Lekkuma xanaa di diwoob dóom, toroxloo; te lu ma naan, tuur ca rongooñ,
10te sa mer ak sa xadar a tax, nde yaa ma fab, xalab.
11Ker a ngi law, nara mëdd samay fan. Maa ngi wowat nim ñax.
12Waaye yaw Aji Sax ji, yaay des ba fàww, saw tur saxal maasoo maas.
13Yaw yaay taxaw, ñeewante Siyoŋ, ndax baaxe ko jot na, àpp ba kay mat na.
14Sa jaam ñeeka sopp doji dëkk bii ñu màbb, ñoo ñeewante tojiti gentam bii.
15Na xeet yi wormaal turu Aji Sax ji, buuri àddina sépp wormaal darajaam,
16nde Aji Sax jeey tabaxaat Siyoŋ, nara feeñeg leeram.
17Mooy nangul aji tumurànke, xeebul ñaanam.
18Nañu bindal lii maasug ëllëg, ba xeet wu sosoogul màggal Ki Sax,
19nde Aji Sax jeey jéere fu sellam fa ca kaw, di niire suuf fa asamaan,
20ngir teewlu onki ñi ñu tëj, nara ubbi ñi dee di seen àtte,
21ba ñu siiwal turu Aji Sax ji fi Siyoŋ, màggale ko fi Yerusalem,
22kera ba xeet yiy bokk daje, ñook réew yi, ngir jaamu Aji Sax ji.
23Sama digg doole la ma semmale, gàttal samaw fan.
24Ma ne: «Éy sama Yàlla, maasoo maas, say at du jeex. Bu ma yóbboo sama diggi fan.
25Bu yàgg nga samp suuf, sàkke asamaan say loxo.
26Yooyu day réer, waaye yaw yaay sax, lépp ay ràpp ni mbubb, nga soppi leen niy yére, sànni;
27te yaw ngay kenn ki, te say at amul kem.
28Sa doomi jaam ñeey dëkk; seen askan sax fi sa kanam.»