1Ninki-nanka nag yaa koy nappe oos? Am yaay yeewe làmmiñ wa ag buum?
2Yaay nase wakkan ya ag buum? Am yaay bëtt ŋaam wa, we ca lonku?
3Xanaa ca la lay tinoo tinu, di la lewetali kàddoom?
4Xanaa kon mooy digook yaw, ngir nga def ko jaam ba fàww?
5Am yaa koy fowe ni picc, takkal ko sa janq ji, ñu di ko seetaan?
6Dees na ko waxaaleendoo? Am ay julaa koy séddoo?
7Yaa koy jamati xepp a? Am yaa koy xaañ xeeju nappkat?
8Teg ko loxo, seet; dootoo fàtte boobu xeex, te doo ko dolleeti.
9Wii rab, yaakaar koo jàpp nax sa bopp la; bu nee jaas, nga jóoru.
10Kenn ñàngul, ba sañ koo merloo. Kon ana kuy taxaw fi sama kanam man?
11Ana ku ma abal lenn ba ma war koo delloo? Lépp lu mboolem asamaan tiim, maay boroom!
12Rab wii, duma noppee waxtaaney céram ak kiraamay dooleem ak jekkaayu bindam.
13Ana ku mana summib turkeem? Ana ku mana bëtt kiiraayu ñaar-caam?
14Ana ku koy ŋaal, ak sellam yu dajal te raglu?
15Gannaaw gi ay sàppey pakk la, di ab tay bu tëje ràpp,
16dugglante benn-benn, ba ngelaw sax xaju ca,
17xanaa ñu ne ñàpp, ku ne taq sa moroom, te duñu teqalikoo.
18Bu tislee, melax ne ràyy, mu xippi, nga ne fajar ay xapp-xappal.
19Jumi sawaraay tàkke ca gémmiñ ga, ferñent ya jiitu,
20saxaar di sël-sëlee ca wakkan ya, mbete cóolóolu cin luy bax.
21Ngelawal bakkanam jafal nay xal, sawara ne jippét, tàkke ca gémmiñam.
22Ndoddam la doole daloo, te fu mu dëgmal tëbum tiitaange fa la.
23Ay ndombo la der ba def, dankalikoo, ne këcc, ne degg.
24Dënn baa nga dëgër niw doj, ne këcc ni doju wolukaay.
25Bu jógee, jàmbaar ñi tiit, muy rajaxe, ñu jommi.
26Nga jam ko saamar, du dugg; xepp akug fitt akub xeej, noonu.
27Weñ gu ñuul di ko safum mboob, xànjar niru ko matt mu nëb.
28Ndawal fitt dawloowu ko, doju mbaq di ngooñ mu koy ñiramtal.
29Bolde di ko saf ñax gu wow, ab xeej riir, def koy ree.
30Lu mel ni tojitu xandeer a lal biir ba, di rijji bañ bi.
31Mooy baxloo xóote yi ni cin, di fuural géej ni njaq lu garab xooje.
32Gannaawam ay def xàll wuy lerxat, mbàmbulaan miy saf bijjaaw.
33Amul niruwaale fi kaw suuf, mii mbindeef mu dul tiit.
34Képp ku réy, mu xool la bëtu suufe, képp ku bew, muy sa buur.