1Dib taalifu yeete bu ñeel Etan mi bokk ci giirug Esra. Aji Sax ji laay woye ngoram, ba fàww, di biral wormaam sët ba sëtaat.
2Dama ne, sa ngor dàkk la sax, fa asamaan nga dëël sa worma.
3Aji Sax ji nee: «Damaa fas kóllëreek ki ma tànn, muy Daawuda sama jaam bi ma giñal ne ko:
4“Damay saxal sa askan ba fàww, samp sab jal sët ba sëtaat.”» Selaw.
5Aji Sax ji, waa asamaan a ngi lay sante say jaloore, ndajem ñu sell ña di la joobee sa kóllëre.
6Ana kuy dab-dabal Aji Sax ji, fa kaw-a-kaw? Ana ci goney Yàlla yi ku nirook Aji Sax ji,
7Yàlla ji ñu teral a teral ci jataayu ñu sell ñi, te mu gëna raglu lu ko wër?
8Yàlla, Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, Ki Sax, ana ku tollook yaw doole? Yaw mi sa kóllëre féete fu ne!
9Yaw yaa man géej gu sàmbaraax; gannax ya fuddu, nga dalal.
10Yaa rajaxe Raxab miy ninki-nankay géej, bóom ko, tasaare say noon ci sa doole.
11Yaa moom asamaan, yaa moom suuf. Àddinaak li ci biiram, yaa ko taxawal.
12Bëj-gànnaar ak bëj-saalum, yaa ko sàkk. Tabor ak Ermon, tund ya, di sarxollee sa tur.
13Yaa àttan, jàmbaare; sa loxo di dooley neen, sa ndijoor ca kaw!
14Àtteb dëgg ak njub a lal sab jal, ngor ak worma dox jiitu la.
15Aji Sax ji, ndokkalee mbooloo mu la xal di sarxollee, di niitoo saw yiw,
16ànd di la bége bés bu ne, sa àtteb dëgg siggil leen.
17Seen darajay doole, yaw a. Boo nu baaxee, nu yokku kàttan.
18Sunu kiiraay lii, Aji Sax jeey boroom; sunu buur bii, Aji Sell ji séddoo Israayil mooy boroom.
19Wax nga say wóllëre ci peeñu, ne leen: «Kaweel naa jàmbaar ci xeet wi, dénk ko ndimbal.
20Maa ràññee sama jaam Daawuda, fale ko sama diw gu sell,
21ànd ak moom, saxal ko, sama loxo di ko dooleel.
22Noon du ko bett, ku bon du ko toroxal.
23Ay bañam, ma rajaxe; ay noonam, ma faat,
24sama wormaak sama ngor di ko gunge, may yokk kàttanam.
25Géej, ma teg ci loxoom, dex, ma ne ca tegg ndijooram.
26Moo ma naa: “Yaay sama baay, di sama Yàlla, di sama wéeru-mucc.”
27Te it maa koy def samab taaw, tiimale ko buuri àddina,
28sàmmal ko sama ngor ba fàww, feddalil ko sama kóllëre.
29Damay saxal askanam ba fàww, yàggal ab jalam ni asamaan.
30Bu ay sëtam wàccee sama yoon, baña doxe samay ndigal,
31mbaa ñu xëtt sama dogali yoon, baña sàmmonteek samay santaane,
32ma bantale leen seenug moy, dumaa leen seen ñaawtéef.
33Waaye duma ko daggal sama ngor, te duma ko ñàkke worma.
34Déet, duma masa fecci sama kóllëre, te duma toxal sama kàddu.
35Benn yoon laa ko giñ ci sama sellaay, duma fen Daawuda:
36askanam, dàkk; ab jalam fi sama kanam ni jant bi,
37ak weer wi sax ba fàww, dib seede bu wér ca niir ya.» Selaw.
38Ndaxam yaw Yàlla, jéppi nga ki nga fal, mere ko, wacc ko.
39Fecci nga sa kóllëreek sab jaam, foq nguuram, detteel ko.
40Bëtt nga ñagam yépp, saam ay tataam,
41ku fa jaare, jël ca alalam, mu doon mbalitu dëkkandoo yi.
42Yékkati ngay bañam, noonam yépp di ree.
43Waññi nga ñawkal saamaram, te taxawuloo ko cib xare.
44Xañ nga ko darajaam, rattax ngànguneem fa suuf.
45Dagg nga fani ngoneem, sang ko gàcce. Selaw.
46Éy Aji Sax ji, xanaa lii du jeex? Xanaa doo làqu fàww nii, sa mer di boy?
47Bàyyi ma xel, samay fan yàggul. Xanaa du neen a tax nga sàkk mboolem doom aadama?
48Ana kuy dund te du dee? Ku mana rëcc tëraayu bàmmeel? Selaw.
49Boroom bi, ana sa ngor la nga daan jëfe te nga giñale woon ko Daawuda ci sa worma?
50Boroom bi, bàyyil xel ci sa gàcceg jaam ñi, ak xeet yu bare yi ma yenu yépp.
51Aji Sax ji, say noon a ngi sewal buur bi nga fal, ne ko dann.
52Cant ñeel na Aji Sax ji ba fàww. Amiin, amiin.