1Di woyu cant, ñeel askanu Kore wu góor, jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Maxalat Leyanot, dib taalifu yeete bu ñeel Eman mi bokk ci giirug Esra. Éy Aji Sax ji, Yàlla ji may musal, bëccëg ma yuuxu, guddi ma yuuxu fi sa kanam.
2Yal na sama ñaan àgg fa yaw; teewlul, ma woote wall.
3Damaa suur këll ay musiba, ba soreetuma njaniiw,
4ñu sóoraale maak ñi wàcci biir bàmmeel. Ma mel ni jàmbaar ju kenn amatul yaakaar,
5bokk ci néew yi dara waratul, mbaa ku ñu bóom, mu tëdd cim pax, faaleetoo ko, xanaa dagg ko, wacc.
6Tàbbal nga ma kàmb gu xóot, biir xóotey lëndëm.
7Yen nga ma sa xadar, tance ma sa gannax yépp. Selaw.
8Dàqal nga may xame, tax nga ñu seexlu ma; ma tëju, génnatuma.
9Samay gët a ngi giim ndax naqar. Éy Aji Sax ji, maa ngi lay woo bés bu ne, dékk lay loxo.
10Ku dee, lu muy doyeeti say kéemaan? Ndax néew dina jóg di la màggal? Selaw.
11Dees na siiwal sa ngor biir bàmmeel, mbaa sa kóllëre ci paxum sànkute?
12Ana kuy yég say kéemaan ci googu lëndëm? Ku lay seedeel njub réew ma fàtte faloo?
13Aji Sax ji, man, yaw laay woo wall, xëy, kare la gii ñaan, ne la:
14Éy Aji Sax ji, loo may gàntale, di ma fuuylu?
15Mitit bay laatikaaf, sama ngone ba tey; sa mbugal yu raglu, ba bopp ubu ràpp!
16Sa mer mëdd ma, sa mbugal yu raglu sànk ma,
17mëdd ma nim ndox bés bu ne, gëndoo fi sama kaw.
18Dàqal nga ma soppeek xarit, ma far xejjoo lëndëm.