1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor. Na xeetoo xeet tàccu, xaacu, sarxolleel Yàlla!
2Aji Sax ji, Aji Kawe jee jara ragal, mooy buur bu mag bi tiim àddina sépp.
3Moo nu nangulal xeet yi, nu teg tànk gàngoor yi.
4Moo nu tànnal céru suuf, muy sagu askanu Yanqóoba wii mu sopp. Selaw.
5Yàllaa yéeg, kàddu riir. Aji Sax jee yéeg, bufta jolli.
6Woyleen Yàlla, woyleen, woyleen Yàlla sunu buur, woyleen.
7Yàllaay buuru àddina sépp; taalifleen, woy ko.
8Yàllaa di buuru xeet yi, Yàllaa tooge jalam bu sell.
9Kàngami xeet yeey daje, ànd ak ñoñi Yàllay Ibraayma; Yàllaa moom buur yi yiir àddina, te moo kawee kawe.