1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Aji Sax ji, yaw laa làqoo, yàlla buma rus mukk. Yiwee ma sa àtteb dëgg.
2Teewlu ma, gaawe ma, Yal nangay sama cëslaay, sama rawtu. Aar ma, ma mucc.
3Yaay sama cëslaay, sama rawtu. Jiite ma, wommat ma ngir sa tur.
4Génne ma fiir gi ñu may tëroo; yaw yaa di sama rawtu.
5Yaw laa jébbal samag noo. Aji Sax ji, Yàlla miy dëgg, ngalla jot ma.
6Maa bañ kuy topp tuuri neen. Man, Aji Sax ji laa wóolu.
7Damay bég, di bànneexoo sa ngor, li nga xoole samaw tiis. Ràññee nga sama njàqarey xol.
8Waccoo ma ci loxol noon, danga maa taxawal fu ma yaatoo.
9Éy Aji Sax ji, baaxe ma, jàq naa! Samay gët a ngi giim ndaxu tiis, xol jeex, yaram jeex.
10Naqar a ngi may rey, tiis di wàññi samay fan, sama doole ŋiis ndax sama njubadi, samay yax semm.
11Noonoo noon a ma sewal, dëkkandoo waxi noppi, xame seexlu ma, ku ma gis biti, di ma daw.
12Kenn xalaatu ma, xanaa fàtte ma ni ku dee, ma mel ni ndab lu yàqu.
13Damaa dégg jëw yu bare, lu raglu dar ma kepp. Ñu ngi mànkoo, di ma fexeel, di wut sama bakkan.
14Man nag Aji Sax ji, ci yaw laa dénku. Ma ne: «Yaay sama Yàlla.»
15Yaa yor sama àpp. Xettali maak ku ma noonoo ak ku may sonal.
16Leeralal ma sa kanam, Sang bi, walloo ma sa ngor.
17Éy Aji Sax ji, woo naa la wall, yàlla buma rus. Yal na ku bon rus, ne xerem biir njaniiw.
18Yal nanga tëj gémmiñu fen-kat buy wax aji jub waxi reewande, di réy-réylooka xeebaate.
19Yàlla yaa yaatu ngëneel loo dencal ku la ragal, defal ko ku la làqoo, doom aadama seede.
20Yaa koy làq fa nga làqu, fa pexey nit àggul. Nga yiir ko, mu yiiru ci ayu làmmiñ.
21Cant ñeel na Aji Sax ji! Ndaw kéemtaan ci ngor li mu ma jiwe biir dëkk bu ñu gaw.
22Man nag saalitoon naa ne: «Yàlla dagg na ma, sànni!» Ndeke ba ma lay woo, dégg nga samay dagaan.
23Képp kuy aji gëm, soppal Aji Sax ji. Aji Sax jeey sàmm ku ko gëm, di yool, ba wis kuy réy-réylu.
24Képp ku yaakaar Aji Sax ji, dëgërlul te amu fit.