1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Mu jagleel Aji Sax ji woy wii, bés ba mu ko xettalee ci mboolemi noonam, xettali ko it ci Buur Sawul. Kàdduy woy wa lii la. Mu ne: Aji Sax ji, maa la sopp, yaw mi may dooleel.
2Aji Sax ji mooy sama cëslaay, moo may aar, di ma wallu. Yàllaay sama cëslaay li ma yiiroo, fegu; mooy Boroom doole ji may musal, di ma làq.
3Ki yelloo cant, Aji Sax ji, moom laa woo, mucc ci samay noon.
4Buumi dee tanc ma, walum kasara naq ma,
5buumi njaniiw laaw ma, dee ne jaas, di ma fiir.
6Ma jàq, woo Aji Sax ji, ne sama Yàlla wallóoy, mu dégge këram. Ma yuuxu, muy dégg.
7Mu mer, suuf yëngu, di ker-keri; reeni tund ya jaayu, di reg-regi.
8Saxaar di sël-sëlee ca wakkan ya, sawara boye ca gémmiñ ga, xal yu yànj tàkke ca.
9Mu firi asamaan, wàcc, niir yu fatt lal tànk ya.
10Ma nga war malaakam serub, di naaw, daayaarloo laafi ngelaw.
11Ma nga bàddoo lëndëm, làqoo, làmboo ndox mu lëndëm aki xàmbaar,
12leer a ko jiitu, xàmbaar ya topp ca, ak tawub yuur ak xali sawara.
13Aji Sax jee dënoo asamaan. Aji Kawe jee àddu, muy tawub yuur ak xali sawara,
14mu soqiy fitt ak jumi melax, tasaare leen, fëlxe.
15Aji Sax ji, dangaa gëdd, nokki, mu riir, xuri géej ne fàŋŋ, ron suuf ne duŋŋ.
16Aji Sax jee yóotoo fa kaw, jàpp ma, seppee ma ca xóotey ndox ma,
17musal ma ca noon yu mag ya ma bañ te man ma.
18Ñu dajeek man, bés ba ma jàqee, Aji Sax ji taxawu ma,
19yaatal ma, bége ma, ba xettali ma.
20Aji Sax jee ma yool sama njub, samay loxoo set, mu fey ma.
21Sàmm naa yooni Aji Sax ji, bonuma, di moy sama Yàlla.
22Dama ne jàkk ndigalam yépp, dëdduwuma dogali yoonam.
23Seede na, may jëfeg mat, di moyoo tooñ.
24Aji Sax jee ma yool sama njub, rafetlu sama mucc ayib.
25Yaw Aji Sax ji, ku gore, fekk la gore; ku matale, fekk la matale;
26ku sellal, fekk la sell; ku dëng, fekk laak say feem.
27Yaw yaay musal xeet wu néew doole, kuy daŋŋiiral, nga detteel.
28Yaw kay yaa may niital. Aji Sax ji sama Yàllaay leeral sama lëndëm.
29Maak yaw kay, ma song gàngoor. Maak sama Yàlla, ma tëbum tata.
30Yàllaa mat. Kàddug Aji Sax jee wér te wóor. Mooy feg képp ku ko làqoo.
31Ana kuy Yàlla ku moy Aji Sax ji? Ana ku mat cëslaay ku dul sunu Yàlla?
32Yàllaa may dooleel, di ma xàllal, yoon mat.
33Moo ma gaawal ni kéwél, taxawal ma fu kawe.
34Moo may tàggat ci xare, may tàwwig fitt ci xalag xànjar.
35Aji Sax ji yaa may feg, musal ma, dooleel ma sa loxo, nangul ma, darajaal ma.
36Yaa ma xàllalu yoon, ba duma tërëf.
37Ma dàq noon yi, dab leen, jekkali, doora dëpp.
38Ma jam leen, jógatuñu, xanaa fëlëñu, ma joggi.
39Sol nga ma dooley xare, sukkal ñi ma jógal, ñu féete ma suuf.
40Won nga ma ndoddi noon, ma boole bóom bañ yi.
41Ñu ne wallóoy, wall amul; ñu woo Aji Sax ji, faalewu leen.
42Ma wol, ba ñu doon pënd, ngelaw wal, ma wetti ni banu mbedd.
43Xettali nga ma ci bokk yiy fippu, def ma, ma jiite ay xeet; waaso wu ma xamul sax nangul ma,
44ku ma ci dégg, déggal ma, ay doomi doxandéem di ma raamal,
45ne yàcc, génne seeni tata, di lox.
46Aji Sax jeey kiy dund. Kii ma sësoo jara sant. Yàlla mi may musal moo màgg!
47Mooy Yàlla ji ma feyul, nangulal ma xeet yi.
48Xettali nga maak noon, kaweel ma, ma tiim ku ma jógal, xettaleeti ma cib soxor.
49Kon Aji Sax ji, ma sant la ci biir xeet yi, ma kañ sa tur!
50Yaay may sa buuru ñoñ ndam lu réy, yaay ji ngor ki nga fal, muy man Daawuda, di sama askan ba fàww.