1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Deewug doom ju góor, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Ma sante Aji Sax ji sama xol bépp, di siiwal mboolemi kéemaanam.
2Yaw Aji Kawe ji, dama lay bége, bànneexoo la, kañ saw tur.
3Noon yeey dellu gannaaw, tërëf, sànku fi sa kanam.
4Yaa ma àtte yoon, dëggal ma, toog ci sab jal, di àtte njub.
5Rëbb nga xeet yi, sànk ñu bon ñi, far seeni tur ba fàww.
6Noon ya raaf, gental ba fàww. Yaa déjjati seeni dëkk, seenu askan fey.
7Aji Sax jee sax dàkk, samp jalam ngir àtte.
8Moom mooy àtte àddina cig njub, di dogalal xeet yi dëgg.
9Aji Sax jeey làq néew-ji-doole, mooy làqe bésub njàqare.
10Aji Sax ji, yaw, ku la xam, wóolu la. Aji Sax ji, yaw, ku la ñaan wallu, doo ko wacc.
11Woyleen Aji Sax ji dëkke Siyoŋ, siiwalleen ay jalooreem ci xeet yi!
12Mooy topp nit bakkanu moroomam, di ko ba xel, te du fàtte yuuxi néew-ji-doole.
13Éy Aji Sax ji, baaxe ma, gisal naqar wi ma bañ yi teg. Yaa may yékkatee fa bunti dee,
14ba ma siiwali sa woy yépp, fa buntu Siyoŋ, dëkk bu taaru ba, di bànneexoo sa wall gii!
15Xeet yee tàbbi pax ma ñu gasoon, fakkastaloo fiir ga ñu làqoon.
16Aji Sax jaa ngi feeñoo, di àtte yoon; ku bon tegug fiir, tàbbi ca. Na jib ndànk. Selaw.
17Ñu bon ñee dëddu, dem njaniiw, ànd ak xeet yi fàtte Yàlla yépp.
18Yàlla du tanqamlu ab ndóol ba fàww, yaakaaru néew-ji-doole du tas mukk.
19Aji Sax ji, jógal, bu la nit yab; na xeet yi dikk fi sa kanam, nga àtte leen.
20Rikk Aji Sax ji, yónnee leen tiitaange, xamal leen ne nit doŋŋ lañu. Selaw.