1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor. Éy Aji Sax ji, yaa baaxe woon sa réew mi, ba suqali sëti Yanqóoba yi,
2baal sa mbooloo seeni ñaawtéef, jéggal leen bépp bàkkaar. Selaw.
3Bàyyi nga xadar ja, muñ mer ma.
4Éy Yàlla mi nuy musal, suqali nu, te meddi.
5Xanaa doo nu mere fàww, ba ca sët yaak sëtaat ya?
6Xanaa dinga leqali sa mbooloo, ba ñu man laa bànneexoo?
7Éy Aji Sax ji, won nu sa ngor, baaxe nu sag wall.
8Woykat ba nee: «Naa déglu lu Aji Sax ji Yàlla di wax.» Jàmm lay wax wóllëreem ñiy ñoñam, ba duñu dellu ci jëfi dof.
9Wallam aka jege ñi ko ragal, te leeram dëgmal sunu réew mii!
10Ngor ak wormaa daje, njub ak jàmm saafoonte,
11kóllëre jebbee fa suuf, njub séentoo asamaan,
12Aji Sax ji it maye ngëneel, sunu suuf meññal,
13njub jiitu Aji Sax ji, di ko xàllal yoonam.