1Di woyu cant, ñeel Asaf. Éy Yàlla, bul ne cell, rikk Yàlla, bul tanqamlu, ne patt.
2Xoolal sa noon yiy riir, sa bañ yi fippu ba téen!
3Sa ñoñ lañuy rabatal, di mànkool sa séddoo yii.
4Ñu ne: «Ayca nu far seen xeet wi, ba deesul fàttalikooti turu Israayil.»
5Dañoo mànkoo kat, te yaw lañu takktool:
6muy néegi Edom ak Ismayla, néegi Mowab ak Agar,
7néegi Gebal, Amon ak Amaleg ak waa Filisteek waa Tir,
8réewum Asiri it fekki leen, di dooleel askanu Lóot wa. Selaw.
9Def leen na nga defoon waa Majan, def ko Sisera ak Yabin ca dexu Kison,
10ña nga sànku ci Endor, ba doonub tos fi kaw suuf.
11Defal seeni njiit na Oreb ak Seeb, def seen kilifa yépp ni Sebax ak Calmuna,
12ña ne woon: «Nan séddoo parluy Yàlla yi.»
13Éy Yàlla, wëndeel leen ni callweer, ñu mel ni boob bu ngelaw wal.
14Éy Yàlla, ni daay di xoyome àll, sawara wa jafal tund ya,
15yal nanga leen ni toppeek sa dooley ngelaw, tiitale leen sa ngëlén.
16Aji Sax ji, sëlëm leen gàcce, ba ñu daw wutsi la.
17Yal nañu rus, jàq ba fàww. Yal nañu torox, sànku.
18Yal nañu xam ne yaw mi tudd Aji Sax ji doŋŋ yaay Aji Kawe ji yilif àddina sépp.