1Mu jëm ci njiital woykat yi, di woyu cant, ñeel Daawuda. Éy Yàlla, yaa jagoo cant fa Siyoŋ, yaw lees di jëfeel ab dige.
2Yaw miy nangug ñaan, yaw la képp di wuyusi.
3Samay ñaawtéef man na ma, waaye sunuy tooñ, yaa nu koy baal.
4Ndokkalee koo tànn, woo ko, mu dale say ëtt, di xéewloo sa ngëneeli kër, ak sa sellaayu dëkkuwaay.
5Defal nga nuy kéemaan, nangug ñaan ci njekk, yaw Yàlla mi nuy wallu, di yaakaaru àddina wërngal këpp, ba ca géej gu sore ga.
6Yaa dëje tund yu mag yi doole, gañoo sa kàttan,
7di dalal riirum géej aki gannaxam, ak coowal xeet yi,
8ba waa cati àddina yéemoo say firnde, waa penkook sowu di sarxolle.
9Yaa dikke suuf am wal, nangul koo nangul. Dexu Yàllaa fees ndox, ngay may nit peppam, ni nga ko waajale suuf si,
10di suuxat ngàbb mi, maasalee ko jal yi, sottiy waame, mu mokk, cax ma, nga barkeel.
11Yaay tëje mbeyum at mi say ngëneel, foo jaare, xéewal walangaan.
12Parluy màndiŋ yaa ngi walangaan, li wër tund yu ndaw yi di xumbéen.
13Joor gaa ngi, jur gi muur, xur yi sàngoo pepp, lépp di xaacooka woy.