1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Éy Yàlla, déglul sama kàddug tawat; ngalla aaral sama bakkan ci noon bu raglu.
2Làq ma pexey ku bon, ma rëcc gàngooru defkati ñaawtéef.
3Ñu ngi daas seen làmmiñ niy saamar, di fitte seeni kàdduy wextan,
4di jam ku ñu tëru te deful dara; jekki jam ko, te tiituñu ci dara.
5Dañoo dogu ca lu bon la ñu nar, di diisoo na ñuy làqe ay fiir, te naan: «Kenn du ko gis!»
6Dañuy lal pexem njubadi te naan: «Lal nanu pexe mu mat sëkk.» Nit aka xóot xel te xóoti mbóot!
7Waaye Yàllaa leen di jamu fittam, ñu jekki daanu.
8Seen làmmiñ a leen di fakkastal, ba ku leen xool wëcc bopp.
9Ñépp a ciy am tiitaange, bay siiwal la Yàlla def, tey xalaataat jëfam jooju.
10Ku jub bége Aji Sax ji, làqoo ko. Képp ku namm njub, damu.