1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Céy Aji Sax ji, Buur a ngi bége sa doole, di bànneexoo sag wall rekk.
2Yaa ko may nammeeli xolam, gàntuwulooy dagaanam. Selaw.
3Yaa ko gatandoo barkey ngëneel, kaalaa ko wurusu ngalam.
4Mu ñaan mucc, nga saxal jalam fàww,
5sag wall a ko sagal a sagal! Teraangaak daraja nga ko sédd,
6jagleel ko barke bu sax dàkk, bégale ko sa kanam, mu bànneexu.
7Buur wóolu na Aji Sax ji, moos, du tërëf, Aji Kawe jee gore.
8Buur, yaa naan sa noon yépp céex, ne say bañ taral.
9Soo nee jalañ, jafal, ñu boy. Aji Sax ji mer, sànk leen, sawara xoyom leen.
10Yaay raafal seeni giir fi kaw suuf, fey seen askan ci doom aadama yi.
11Ñoo la mébal lu bon, nasal la pexe, àntuwul.
12Nga di leen diir fittu kanam, ñu wone gannaaw.
13Aji Sax ji, jógal ak sa manoore, nu joobe la, woy sa jaloore.