1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Éy Aji Sax ji, xettali ma ci ku bon, musal ma ci nitu fitna,
2kuy nas lu bon, tey saxoo di sookey xare,
3daas làmmiñam ni jaan, guux daŋaru ñàngóor. Selaw.
4Éy Aji Sax ji, aar ma ci loxol ku bon, musal ma ci nitu fitna, ku may fexee fakkastal.
5Ñu bew ñee ma làqali yeer, lalal may buum aki caax, feggal ma seeni fiir ci yoon wi. Selaw.
6Dama ne Aji Sax ji, yaay sama Yàlla; Aji Sax ji, teewlul, ma dagaan la.
7Aji Sax ji Boroom bi may walloo doole, yaa ma yiir keroog bésub xare.
8Aji Sax ji, bul may ku bon nammeelam, bul matal pexeem, muy yékkatiku. Selaw.
9Ñi ma sam, yal na seen ayu làmmiñ këppu ci seen kaw bopp.
10Yal nañu këppoo xali sawara, tàbbi ciy pax te dootuñu jóg.
11Kuy yàq der, yàlla bumu toog ci réew mi. Nitu fitna, yal na ko ay topp, ba dal ci kawam.
12Xam naa ne Aji Sax jeey jox néew-ji-doole dëgg; di sàmm àqu baadoolo.
13Ku jëfe njekk kay moo lay sant; ku jub dëkke saw yiw.