1Di woyu cant, ñeel Daawuda. Yàlla, dogu naa, damay woy, di la kañ; sama jëmm jépp di la woy.
2Na xalam ak moroom ma yewwu, ma yee leeru njël.
3Aji Sax ji, dama lay gërëm ci biir xeet yi, kañ la ci biir waaso yi.
4Sa ngor a màgg ba sut asamaan, sa worma àkki fa kaw-a-kaw.
5Éy Yàlla, yaa màgg ba sut asamaan, sag leer tiim suuf sépp.
6Walloo nu sa ndijoor, nangul ma, ba say soppe xettaliku.
7Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkót.
8Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, Efrayim di sama mbaxanam xare, Yuda di sama yetu nguur,
9réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, Edom, ma teg tànk; Filisti, ma xaacoo fa.»
10Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? Ku may jiite ba Edom?
11Yàlla, xanaa du yaa nu wacc? Éy Yàlla, yaa baña ànd ak sunu mboolooy xare?
12Ngalla dimbali nu ci bañaale; doom aadama, wallam neen la.
13Nook Yàlla, nu def njàmbaar; moom mooy noot sunuy noon.