1Moytul sa bopp booy dem kër Yàlla. Duggal te déglu, bala ngay def saraxi dof bu xamul ne mu ngi def lu bon.
2Bul rattax làmmiñ, bul gaawa dikke Yàlla mbir. Yàllaa ngi kaw asamaan, yaw yaa ngi fi suuf. Kon na say kàddu néew.
3Bu xalaat baree, indi gént; bu wax baree, waxi dof jib.
4Boo digook Yàlla, bu ko yeexe. Daray foontukat neexul, defal li nga dige.
5Baña digee gën dige loo deful.
6Bu la sa làmmiñ yóbbe bàkkaar, ba ngay layal ndawal Yàlla la, naan lii njuumte la woon. Ana lu jar Yàlla di la meree sa kàddu, bay neenal saw ñaq?
7Wax ju bare, caaxaani neen; mook gént yu baree yem. Kon, Yàlla, ragal ko.
8Boo gisee ñuy noot néew-ji-doole, di jalgati dëgg ak yoon cib gox, bumu la jaaxal; kilifa gi, kilifaam a ko yiir; ñoom it seen kilifaa leen yiir.
9Xanaa ndax buur suqal mbey mi, ba ñépp jariñoo suuf si.
10Bëggkatu xaalis du doyal xaalis, bëggkatu alal du doyal tono, te loolu it, cóolóoli neen.
11Bu koom yokkoo, ña cay lekk yokku. Ana lu muy jariñ boroom koom ga, xanaa di ko duufale bëtam?
12Surga, lekkam néew, bare, mu nelaw, ba fàttey boram; boroom alal regg, du noppalu, du nelaw.
13Naqar wu réy laa gis fi kaw suuf: alal ju boroom dajale ba loru,
14mbaa pexeem moy, mu sànkule; ba bu amee doom it, du ko wacce dara.
15Nga juddoo ci sa ndey loxoy neen, walbatiku dellu na nga dikke woon. Du dara loo ñaqoon ba yóbbaale ko.
16Dikke ni, delloo ni, loolu it tiis wu réy la. Doñ-doñi, ngelawal neen, ana jariñ la?
17Ngay dunde tiis bésoo bés, ak naqar ak wopp ak xol bu tàng!
18Lii daal laa ci gis, man. Li gën te jaadu ci nit: na lekk, naan te bànneexoo ñaqam wu mu ñaqe kaw suuf giiru dund gi ko Yàlla may. Loolu mooy céram.
19Alal ak koom, ku ko Yàlla may, may ko mu tal koo xéewloo, mu nangu céram, bànneexoo ñaqam, loolu mayu Yàllaa.
20Yàllaa koy bànneexal, ba du tiisoo ay fanam.