1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. Aji Sax ji sunu Boroom, sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp! Sag leer tiim asamaan.
2Làmmiñu tuut-tànk, ba ci luy nàmp, feeñal nga ca sa kàttan, ngir jaxase say noon, bañaaleek feyukat ne xerem.
3Damay xool sa asamaan si nga móol, ak weer week biddiiw yi nga fi teg.
4Moo, luy nit, ba nga di ko bàyyi xel? Luy doom aadamaak loo koy yége?
5Yaa ko def mu gëna suufe as lëf malaaka yi, yaa ko kaalaa teraanga ak daraja,
6fal ko ci kaw loo bind, jox ko lépp, mu teg tànk:
7jur gépp, gu gudd ak gu gàtt, rabi àll it ca la,
8ak njanaaw ak jën ak luy jaare yooni géej.
9Aji Sax ji sunu Boroom, sa tur aka màgg ci kaw suuf sépp!