1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Asaf, te ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit. Sarxolleleen ci Yàlla mi nuy dooleel; xaaculeen ci Yàllay Yanqóoba.
2Yékkatileen woy te jiin, xalam neex, ànd ak moroom ma.
3Walleen bufta bi ci Terutel weer wi, ak weer wu birale bésu màggal.
4Loolu wartéefu Israayil la, di ndigalu Yàllay Yanqóoba,
5di ndénkaane bu mu dénk waa kër Yuusufa, ba Yàllay dali ca kaw réewum Misra. Baat bu ma xamul laa dégg, mu naan:
6«Yennil naa leen yen bi, woyofal seeni loxo.
7Ngeen jàq, woo ma, ma xettali leen, wuyoo leen fa kiiraayal dënn ya, te maa leen nattoo fa wal ma ca Meriba. Selaw.
8Yeen sama ñoñ, dégluleen, ma dénk leen. Éy Israayil, su ngeen ma déglu woon!
9Buleen fat tuuru jàmbur, buleen sujjóotal tuuru doxandéem.
10Man, Aji Sax ji, maay seen Yàlla ji leen yékkatee réewum Misra. Ŋaleen ŋafeet, ma reggal leen.
11«Waaye sama ñoñ déggaluñu ma, ñuy Israayil gii ma nangulul.
12Moo tax ma bërgël leen ak seenug të, ñuy wéye seeni pexe.
13Éy su ma sama ñoñ déggaloon, éy su Israayil toppoon samay nammeel!
14Ci saa si laay toroxal seeni noon, duma seeni bañ,
15ba ku bañ Aji Sax ji di ko raamal, te àppam du jeex ba fàww.
16Kon yeen, ma leel leen ngën-gi-pepp, reggal leen lem ju doj xelli.»