1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf. Éy yaw, Sàmmu Israayil, teewlu nu; yaw mi jiite Yuusufa ni ag jur, yaw mi toogandook malaakay serub yi, feqal sag leer.
2Dawalal sa njàmbaar, ñeel Efrayim ak Beñamin ak Manase, te wallusi nu.
3Éy Yàlla, suqali nu; geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
4Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, foo àppal sa mer, mi ngay wuyoo sa ñaanu mbooloo mi?
5Leel nga nuw naqar, nàndal nu mbàndum rongooñ,
6def nga dëkkandoo di nu xëccoo, noon di nu ree.
7Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, suqali nu; geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.
8Yaa déjjate ag reseñ ci Misra, dàq yéefar yi, indi, jëmbataat.
9Nga raadu suuf si, reseñ gi sampu, law, dajal réew mi;
10keppaaram muur tund yi, ay caram sàng garabi seedar yu mag yi.
11Mu tàllal ay bànqaasam ba géej, lawal njebbit la ba ca dexu Efraat ga.
12Lu tax nga bëtt ay ñagam, ba ku fa jaare witt ca,
13mbaam àll di ko ruur, ndundati àll di ca for?
14Éy Yàlla Boroom gàngoor yi, geesul; séentool asamaan, ba gis te taxawusi reseñ gii.
15Taxawusil njëmbat lii nga jëmbate sa ndijoor, ngarab sii nga dooleelal sa bopp.
16Dees koo gor, taal; yal na ñii sànkoo sa mbugal.
17Yal nanga yiir ki nga tànn, kii nga dooleelal sa bopp,
18ba dootunu la dëddu. May nu nu dund, nu wormaal sa tur.
19Éy Aji Sax ji, Yàlla Boroom gàngoor yi, suqali nu, geesoo nu sa leeru kanam, nu raw.