1Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Asaf. Naa xaacu, woo Yàlla, sama baat fa Yàlla, ngir mu déglu ma.
2Bëccëg, ma jàq, sàkku ndimbalal Boroom bi; guddi, ma tàllal loxo, toqiwuma. Sama xol tëë sedd.
3Ma bàyyi Yàlla xel, binni, xalaat, xol jeex. Selaw.
4Éy Yàlla, tere nga maa gëmm bët, ma jaaxle ba waxatuma,
5xanaa xalaat janti démb, at ya woon.
6Guddi may fàttaliku sama woy, di waxtaan ak sama ngegenaay, sama xel di jéex te naa:
7«Boroom bi da may gàntal ba fàww, ba du ma baaxeeti mukk a?
8Xanaa daa jeexal ngor tàkk? Am kàddoom a deñ ba fàww?
9Moo, mbaa du Yàlla daa fàtte ñeewante? Am meram a tëj buntu yërmandeem?» Selaw.
10Ma ne, sama naqar daal mooy Aji Kawe ji daa soppi loxoom.
11Waaye naa fàttaliku jaloorey Ki Sax rekk, fàttaliku kéemaanam ya woon.
12Naa xalaat sa bépp liggéey, di jàngat say jëf.
13Céy Yàlla, yaa sell jikko! Jan yàllaa màgg ni Yàlla?
14Yaa di Yàlla juy jëfi kéemaan, yaa siiwal sa doole ci biir xeet yi.
15Kàttan nga jote sa mbooloo ma, sëti Yanqóobaak Yuusufa. Selaw.
16Yàlla, ndox maa la gis, ndox maa la gis, di lox; xóote yaa say,
17niir ya yuri, kàddu riire asamaan, say fitt, fettaxandoo,
18nga dënoo biir callweer, melax yi taal àddina, suuf di lox, di reg-regi.
19Biir géej di saw yoon; saw xàll ci digg ndox mu ne xéew, te kenn gisul foo teg tànk!
20Wommat nga sa mbooloo ni ag jur, Musaak Aaróona jiite.