1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, di woyu cant, ñeel Asaf. Yàlla siiw na fa Yuda, aw turam màgg fa Israayil.
2Xaymaam a nga Salem, di xuntam ma fa Siyoŋ.
3Fa la rajaxee fitt yuy boy ak pakk ak saamar ak ngànnaayal xare. Selaw.
4Yàlla yaa ne ràññ te darajawu, ba raw tundi rëbbkat yi.
5Futtees nay boroom fit, ñu ne nërëm, nelaw; kuy ñeyi xare, say loxo nasax.
6Yaw Yàllay Yanqóoba, yaa gëdd, gawar ak fasam nelaw.
7Yaw mii, yaa mata ragal; boo meree, ana kuy taxaw fi sa kanam?
8Fa asamaan nga biraleb àtte; suuf tiit, ne cell.
9Ca la Yàllay jóg, ngir àtte, ba wallu kuy néew dooley àddina. Selaw.
10Doom aadamaak xadaram rafetal sa woy; desu xadaram, nga gañoo.
11Seen Yàlla Aji Sax ji, digooleen ak moom te jëfe ko. Kee jara ragal. Na ñi ko wër ñépp indi teraanga.
12Mooy sàggi sagu kilifa yi, di tiitaangey buuri àddina.