1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba mu nekkee ca màndiŋu Yuda. Yaw Yàlla, yaay sama Yàlla, ma xëy di la wër, sama bakkan mar la, sama jëmm namm la, fu suuf mare ndox, ne sereŋ.
2Moo tax kër gu sell ga laa la séentoo, ngir niir sa doole ak sa leer.
3Xéewloo sa ngor moo dàq dundu bakkan; ma àddu boog, kañ la!
4Dama lay sant, sama giiru dund kay, tàllal la ay loxo, sàbbaale la.
5Sama xol di sedd, ni ku ñam wu duun suural, ma bég, sarxolle, màggal la.
6Su ma tëddee, fàttaliku la, waxtuw guddi dama lay xalaat.
7Yaay sama ndimbal, may làqoo sa kiiraay, di sarxolle.
8Sama xol taq la, nga téyee ma sa ndijoor.
9Waaye ñiy wuta faat sama bakkan ñoo jëm xóotey njaniiw.
10Ñu jébbal leen ñawkay saamar, till séddoo.
11Buur moom, di bége Yàlla; képp ku koy giñe di ko kañoo, fen-kat ne xerem.