1Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Yàlla doŋŋ ay dalal sama xel, moo may wallu.
2Moom doŋŋ mooy sama wéeru-mucc, di ma rawale, ba duma sànku!
3Xanaa dungeen bàyyee songandoo nit, nar koo sànk, ni kuy màbb tabax bu joy, mbaa ngay bàddi per mu ràpp?
4Seeni mébét, wàcce boroom daraja doŋŋ; yeena ngi bége ay fen, seeni kàddu diw yiw, seen xalaat diy saaga. Selaw.
5Yal na Yàlla doŋŋ di dalal sama xel, moom mi ma yaakaar.
6Moom doŋŋ a di sama wéeru-mucc, di sama rawtu, duma tërëf.
7Yàllaa may musal, di ma sagal, ma di ko doolewoo. Sama kiiraay, Yàllaa!
8Bokk yi, wóoluleen ko fu ngeen tollu, diisleen ko seen xol, Yàllaay sunu kiiraay. Selaw.
9Doom aadama, ngelawal neen; nit, naxi neen. Booleel teg ci lu ñuy natte diisaay, kaw la jëm. Ñooy gëna woyof ngelaw!
10Bul wóolu ribaa, bul yaakaar alalu càcc, neen la. Bu sa alal yokku, nga taf ci sa xol.
11Benn yoon la Yàlla wax, ñaari yoon laa dégg, ñu ne; «Doole, fa Yàlla.»
12Boroom bi, ngor, yaay boroom, yaw daal, yaay yool nit jëfam.