1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñuy woowe Bul yàq, diy ñaan, ñeel Daawuda. Yeen daal, su ngeen waxee, dëgg selaw. Mbaa yeena ngi àtte nit ñi ci yoon?
2Yeena ngi mébét njubadi, di lawal fitna ci réew mi.
3Ku bon day sosu rekk, dëng; juddu, teggi yoon, dib fen-kat.
4Day am daŋar ni ñàngóor, fatti noppam ni jaan ju tëx:
5du dégg baatu jatkat, mbaa jati ñeengokat bu ñàng.
6Yàlla, ngalla tojal seeni gëñ; Aji Sax ji, foqal seen selli gaynde yii.
7Yal nañu ne mes ni ndox muy wal, yal nañu diir seen fitt, mu damm,
8yal nañu mel ni ngumbaan-tooye buy dox, di seey, mbaa lumb wu jigéen tuur, gisul jant.
9Balaa seen cin a yég tàngooru gajj, muy gu tooy, muy guy boy, yal na leen fekk sànku.
10Aji jub day gis ñu feyul ko, mu bég, muy jàngoo deretu ku bon.
11Ku ne naan: «Ku jub jot sab yool moos! Te Yàllaa ngi fi moos, di àtte àddina!»