1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bi ñu dippee Pitax mu luu, dëkk fu sore; diy ñaan, ñeel Daawuda, ba ko Filisteen ña jàppee ca Gaat. Éy Yàlla, baaxe ma, nit a ngi may lakkal, ab xeexkat a ma yendoo sonal.
2Noon yee ma yendoo lakkal, bare lool di xareek man. Ku màgg ki,
3bés bu ma tiitee, yaw laay wóolu.
4Yàlla laay màggal kàddoom, Yàlla laa wóolu, ragaluma. Lu ma nit manal?
5Bésoo bés ñu ngi jalgati samay wax, seen mépp mébét di sama loraange.
6Ñu ngi mànkoo, di ma yeeru, topp samay tànk, di wut sama bakkan.
7Éy gii ñaawtéef! Ñii nu ñu mana mucce? Éy Yàlla, yal na leen sa mer dal!
8Tumurànke naa, nga gis. Duyal samay rongooñ ci sa mbuus. Du lim nga lépp?
9Bés bu ma wootee wall, dees na waññi noon yi, ma xam ne Yàllaa ànd ak man.
10Yàlla laay màggal kàddoom, Aji Sax ji laay màggal kàddoom,
11Yàlla laa wóolu, ragaluma. Ana lu ma nit manal?
12Éy Yàlla, maa tegoo la ma la giñal, maa lay defal saraxi cant.
13Yaa ma rawale, ba deewuma, te duma tërëf. Damay daagu fi kanam Yàlla, ci biir leeru àddina.