1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd aki xalam, dib taalifu yeete, ñeel Daawuda. Éy Yàlla, déglul, ma ñaan la, bul làqu, dama lay dagaan.
2Teewlu ma, nangul ma. Li may tawat a ma xañ jàmm, ub sama bopp;
3coowal noon yee ak coonob ñu bon ñi. Dañu maa teg fitna, di ma songe xadar.
4Sama fit a ngi rëcc, di tëf-tëfi; tiitaangey dee ne ma taral.
5Njàqaree ma dugg, may kat-kati, musiba mëdd ma.
6Dama ne: «Éy ku may may laafi xati, ma ne fërr, noppaluji.
7Xanaa ma naaw, ba sore, fanaani màndiŋ ma. Selaw.
8Naa gaawtu, seeluji ngelaw lu riddi ak ngëlén.»
9Éy, Boroom bi, beenal seeni wax, neenal leen. Damaa gis fitnaak xuloo ci dëkk bi,
10guddeek bëccëg ñuy wër, ñaawtéef ak ayib wéttali leen.
11Yàq a nga ca biir, te nooteel ak njublaŋ jógul ca pénc ma.
12Su doon noon bu may ñaawal, ma muñ ko, mbaa muy bañ bu may won ab dayo, ma daw ko.
13Waaye yaw la, sama nawle, di sama wóllëre, ma xam la.
14Nu daan bokk bànneexu diisoo, ànd ak mbooloo, di jaamuji kër Yàlla ga.
15Yal na leen dee bett, ñu jekki tàbbi njaniiw, ngir mbon ga ci seen biir ak seen dëkkuwaay.
16Waaye man, Yàlla laay woo wall, te Aji Sax jee may wallu.
17Subaak ngoon ak njolloor, may ñaxtooka ñurumtu, mu dégg ma.
18Moo may jot ak jàmm, ba ma mucc ci xare ya ma ñu bare di songe.
19Yàllaay dégg, duma leen, moom mi nguuram yàgga sax. Selaw. Soppikuwuñu fenn te ragaluñu Yàlla.
20Workat baa ngi xàcc loxoom jëme ci ñi mu takktool, di fecci kóllëre,
21làmmiñ wa daa neex ni lem, te xare lal xol ba; kàddu ya gëna nooy ag oliw te di saamar bu génn mbaram.
22Sippikul Aji Sax ji lu la diis, moom moo lay taxawu. Du bàyyi mukk aji jub, muy tërëf.
23Waaye yaw Yàlla, yaa leen di tàbbal, bóomkat ak naaféq ci pax mu xóota xóot, te seen dund xaajul. Man nag, ma di la wóolu.