1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda. Mooy ba Doweg, Edomeen ba, demee ca Sawul, ne ko Daawuda dem na kër Aximeleg. Moo! Jàmbaar ji, looy damoo jëfi coxor? Yàlla, ngoram, bés bu nekk la.
2Ak sa làmmiñ wi ngay sose loraange, mel ni saatu su ñu xacc, rambaaj bi!
3Lu bon a la gënal lu baax, fen a la gënal wax dëgg. Selaw.
4Yaa bëgg jépp wax juy yàq, waabajiiba bi!
5Yàlla da lay sànk ba fàww, fëkke la sab xayma, yóbbu, déjjatee la réewum aji dund. Selaw.
6Aji jub gis ko, yéemu, di la ree, naa:
7«Xoolleen jàmbaar ji làqoowul Yàlla, xanaa di yaakaar alalam ju bare, di yokkoo loraange.»
8Man, ma mel ni garabu oliw gu naat fa biir kër Yàlla, di wóoloo Yàlla ngoram tey ak ëllëg.
9Naa la sante sa jëf ba fàww, naa biral sa tur wu baax, say wóllëre teew.