1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Tóor-tóor, ñeel askanu Kore wu góor, dib taalifu yeete, te di woyu mbëggeel. Woy wu neex a fees sama xol, may taalifal Buur, sama làmmiñ ni xalimag bindkatu ndaanaan.
2Yaa gëna góorayiwe ci àddina, sa kàddu diw yiw, ndax Yàllaa la barkeel ba fàww!
3Jàmbaaroo, takkal sa saamar, te yànj, am daraja;
4ànd ak daraja, dawal ba am ndam, di dawal dëgg ak yërmande ji war, ba mana def ay jaloore.
5Yaw Buur, say fitt a ñaw, di jam say noon ci xol, ay xeet daanu, nga tiim.
6Yaw Yàlla, sab jal a sax dàkk ba fàww. sa yetu buur njub la,
7yaa sopp dëgg, bañ lu bon, ba Yàlla, sa Yàlla diwe la diwu mbég, nga tiim say moroom:
8sa yére yépp di gilli ndàbbu miir, ak alowes akum kanel, ñu di la bégale xalam, ca sa biir kër yu yànj.
9Ay doomi buur a ngi ci jigéen ñi nga teral, sab lingeer féete la ndijoor, takkoo ngëneelu wurus.
10Janq doom, gisal, déglul te teewlu ma, fàtteel say bokk, fàtte sa kër baay,
11Buur xemmeme la sab taar; mooy sab sang, wormaal ko.
12Waa Tir a lay yótsiy may, ay boroom alal di wut lu la neex.
13Séetu Buur duggsi na, ne ràññ, sol mbubb mu wurus way tàkk.
14Ñu yóbbul ko Buur, mu ne boyy, janq ja ànd ak moom, diy toppam, ñu indil leen Buur,
15ñu duggsi kër buur, ci biir mbégteek bànneex.
16Yaw Buur, yal na la sa doom yu góor wuutu ci seen jalu maam, nga def leeni kàngam ci réew mi mépp.
17Maa lay joobe ba sa tur du fey mukk, xeet yi saxoo laa sant ba fàww.