1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor. Éy Yàlla, noo déggal sunu bopp, sunuy maam a nu wax jëf ja nga jëf ca seeni jant, bu yàgga yàgg.
2Yaw ci sa bopp yaa dàq xeet yi, jëmbat fa maam ya; yaa mbugal xeet yi, ñoom, nga yiwi leen.
3Du seen saamar lañu nangoo réew mi moos, seen dooley bopp it mayu leen ndam. Yaa ko defe kàttan ak doole, geesoo leen sa leeru kanam, ngir sa cofeel ci ñoom.
4Yaay kiy sama buur, di sama Yàlla, mayal askanu Yanqóoba ay ndam.
5Yaw lanuy dàqe bañ yi, sa tur lanuy dëggaatee ñi nu song.
6Du fitt laa wóolu, du saamar a may may ndam.
7Yaa nuy musal ci bañ yi, yaay gàcceel noon ñi.
8Yàlla lanuy damoo bésoo bés, di màggal turam ba fàww. Selaw.
9Waaye danga noo wacc, toroxal nu, ba àndulook sunu mboolooy xare.
10Waññi nga nu, nu won noon yi gannaaw, ñu bañ nu, ba futti nu.
11Ni gàtt yu ñuy yàpp, ni nga nu joxee, tasaare nu ci biir xeet yi.
12Jaay nga sa mbooloo ci dara, te jariñu la tus.
13Tax nga sunuy dëkk di nu ree, ñi nu séq di nu kókkaleeka ñaawal.
14Tax nga xeet yi di nu léeboo, jàmbur yaa ngi nuy wëcc bopp!
15Damaa dëkke gàcce, sëlmoo kersa
16ndax kókkali yeek xastey nit ñi ma bañ, di feyoonteek man.
17Lii lépp dal na nu, te fàttewunu la, fecciwunu la kóllëre.
18Dëdduwunu la, waccunu saw yoon,
19teewul nga noot nu, wacce nu xaj ya, këpp nu lëndëmu dee.
20Su nu la fàtte woon yaw, sunu Yàlla, ba tàllal tuuri doxandéem yi loxo,
21du la ump, yaw Yàlla, mi xam kumpay xol.
22Yaa tax ñu yendu noo bóom, dees noo jàppe ni xar yu ñuy tër.
23Éy Aji Sax ji, jógal! Looy nelaw? Yewwul, bu nu wacc ba fàww.
24Loo nu làqe saw yiw, di fàtte sunu njàqareek sunu coono?
25Nu ngi ne ñàyy ci pënd bi, di watat koll fi suuf.
26Wallusi nu, jot nu ngir sa ngor.