1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu yeete bu ñeel askanu Kore wu góor. Yaw Yàlla, ni kéwél di sàkkoo walum ndox, maa la koy sàkkoo xol.
2Maa mar Yàlla, Yàlla jiy dund! Kañ laay teewi fa kanam Yàlla?
3Rongooñ laay dunde guddeek bëccëg, noon yi di ma dëkke naa: «Ana sa Yàlla ji?»
4Lii laay fàttaliku, sama xol jeex: dama daan jàll, jiite mbooloo ma, jëm kër Yàlla ga, di sarxolleeka sant, ñu booloo di màggal.
5Moo man, lu may xàddi, ne yogg? Lu may jàq nii? Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, moom sama Yàlla mi may wallu?
6Maa ngi ne yogg, ba di la fàttalikoo fa réewum Yurdan ak tundi Ermon ak Miccar.
7Sa wal ya sotti, xóote awu moroom ma; say wal ak say gannax, lépp a jaare sama kaw.
8Bëccëg Aji Sax ji baaxe ma ngoram, guddi ma fanaane koo woy, di ñaan Yàlla mi may dundal.
9Naa wax Yàlla sama cëslaay, ne ko: «Lu tax nga fàtte ma, noon di ma fitnaal, may wéye tiis?»
10Noon yaa ngi may ñaawal, di ma yendoo naa: «Ana sa Yàlla ji?» Ma ne yàcc, ne yasar.
11Moo man, lu may xàddi, ne yogg? Lu may jàq nii? Tee maa yaakaar Yàlla, ba santati ko, moom sama Yàlla mi may wallu?