1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda, dib taalifu cant. May xaar a xaar Aji Sax ji, mu dégg may woote, geesu ma,
2génnee ma ca kàmbug sànkute, sippee ma ca xóotey ban ba, cëppe ma ciw doj, samp ma, ma dëgër.
3Moo ma may, ma fent, woy wu ma woye sunu Yàlla. Ñu baree seede, di wormaal aka dénku ci Aji Sax ji.
4Ndokkalee, yaw mi dénku ci Aji Sax ji, te sàkkuwoo ku bew ak kuy topp ay fen.
5Yaw Aji Sax ji sama Yàlla, bare nga loo def, amuloo moroom! Bare nga kéemaan aki mébét yoo nu sottalal, ma bëgga xamle lépp, te mu bare ba wees ab lim.
6Saraxi jur ak pepp, taamuwuloo ko, ay nopp nga ma bënnal, saraxu rendi-dóomal ak saraxu póotum bàkkaar, sàkkuwuloo ko.
7Ma ne: «Maa dikk nii, téereb yoon wi indi na li ñu bind ci man.
8Sama Yàlla, maa defsi sa coobare, ci sama biir xol la sa ndigali yoon nekk.»
9Siiwal naa sag njubte ca ndaje mu mag ma. Dama ne, Aji Sax ji duma noppi, xam nga ko.
10Làquma sag njubte, ne cell ak moom. Yaa wóor, di walloo, siiwal naa ko. Làquma sa ngor ak sa kóllëre ca ndaje mu mag ma.
11Éy Aji Sax ji, bu ma xañ sa yërmande. Sa ngor ak sa kóllëre, yal na ma feg ba fàww.
12Ay musibaa ma tanc, ne gàññ, ba wees ab lim. Samay ñaawtéef a ma dab, ba gisatuma, baree bare, ba ëpp sama kawari bopp; sama xol jeex tàkk.
13Éy Aji Sax ji, yal na la neex, nga wallu ma! Éy Aji Sax ji, gaawe ma!
14Képp kuy wuta fëkk sama bakkan, yal na rus, torox ne tott. Kuy bége sama loraange, yal nañu ko duma, waññi ko, mu ne yàcc.
15Ku may ñaawal, yal nañu ko toroxal, mu daw, dellu gannaaw.
16Képp ku la wër, yal na bég, di la bànneexoo. Képp ku safoo sag wall, yal na jàppoo: «Aji Sax ji màgg na!»
17Man, néew naa doole, ñàkk naa, waaye yaw Aji Sax ji, danga maa yég. Yaw yaa may wallu, xettali ma; sama Yàlla, bu ma yeexe.