1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda, dëppook galan bi ñu dippee Kéwélu fajar. Sama Yàlla, sama Yàlla, lu tax nga wacc ma? Ma binni, binneeti, wall sore.
2Éy sama Yàlla, ma woote bëccëg, wuyuwoo; woote guddi, noppaloo ma.
3Yaw de, yaay ku sell, tooge sab jal, Israayil di la kañ.
4Yaw la sunuy maam wóolu woon, wóolu la, nga xettali leen.
5Yaw lañu daa woo wall, mucc; yaw lañu wóolu woon te rusuñu.
6Man nag aw sax rekk laa, matuma nit. Doom aadama sewal ma, aw xeet tuutal ma.
7Ku ma gis ñaawal ma, biiñ ma, xeelu ma, naa:
8«Na wéeru ci Aji Sax ji, mu xettali ko; su ko soppee, na ko wallu.»
9Yaw de yaa ma roccee sama biiru ndey, naxe ma sama weenu yaay.
10Yaw laa dénkoo ba may juddu, ba ma juddu ci sama ndey, ngay sama Yàlla.
11Bul ma sore, musiba teew na, wall amul!
12Noon yaa ngi ma gaw ni coggalu yëkk, dar ma ni ponkali yëkk ya fa Basan.
13Ñu ŋa ma, ŋàpp, ni gaynde guy yëmmooka fàdde.
14Doole ŋiis, yax yoqi, fit ne soyox, seey.
15Làmmiñ taqoo denqleñ, doole jeex, ma wow koŋŋ, nga tëral ma buntu bàmmeel.
16Ay xaj a ma wër, di gàngooru saay-saay, dar ma kepp, bëtt samay loxook samay tànk.
17Maa ngii, mana waññ sama yax yépp, ñoom ñuy xoole, di ma seetaan,
18séddoo samay yére, tegoo bant sama mbubb.
19Waaye yaw, Aji Sax ji, bul sore; yaa may dooleel, gaawe ma.
20Xettalil sama bakkan ci saamar, ba sama benn bakkan bii mucc ci selli xaj!
21Musal ma ci pàddum gaynde ak ndañum nagu àll. Yaa ma wallu woon!
22Maay siiwali saw tur ci samay bokk, maa lay kañ fi digg mbooloo mi.
23Yeen ñi ragal Aji Sax ji, santleen ko. Yeen askanu Yanqóoba wépp, màggalleen ko. Yeen bànni Israayil gépp, wormaalleen ko.
24Moom de sàgganewul mbaa xeebul boroom tiis, làqu ko kanamam, ba mu wootee, wuyu na ko.
25Yaw laay sante ndaje mu mag, sottalal la samay dige, ñi la ragal seede.
26Ku woyof a cay lekk ba doyal, kuy wut Aji Sax ji, sant ko. «Guddleen a gudd fan!»
27Àddina wërngal këpp ay fàttaliku, walbatiku ci Aji Sax ji. Làngi xeet yépp sukkalsi ko.
28Aji Sax jeey boroom nguur, moo yilif xeet yi.
29Boroom barke xéewlu, sujjóotal ko, ku jëm pax it, te bakkanam di lang, di ko sukkal.
30Askan wu dikkagul dina jaamu Boroom bi, ñiy ñëw te juddooguñu dees na leen wax ay mbiram.
31Ñu dikk, biral njubteem, jottali xeet wu sosoogul jalooreem.