1Dib taalifu yeete bu ñeel Daawuda, ba mu nekkee ca xunt ma. Ma àddu, ñaan Aji Sax ji; àddu ca kaw, di tinu Aji Sax ji,
2sippi ko sama tawat, diis ko sama njàqare.
3Bu ma yoqee, ràññee nga samay jéego; yoon wi may jaare lañu ma làqal am yeer.
4Ma geesu ndijoor, xool; du kenn ku ma faale. Rawtu réer ma, du kenn ku sama bakkan saf.
5Aji Sax ji, ma woo la wall; ma ne, yaay sama kiiraay, di sama séddoo fi kaw suuf.
6Teewlul, ma ne wóoy, damaa manatul, xettali ma ci ñi ma topp, dañu maa ëpp doole.
7Ngalla génne ma fi ma tëje, ma sant la. Man la way-ngëm ñi di yéew ëllëg, yaa may xéewale ab yool.