1Ki lay falaxe buur na, wutsi la! Sàmmal sab tata, wattu saw yoon, takkal sa ndigg, te dëgërlu bu baax.
2Aji Sax ji moo yeesal darajay Yanqóoba, darajay Israayil moomu. Ay taskat a ko tasoon, yàqate ay caram.
3Pakki jàmbaaram ña lañu suub xonq, ñeyi xare ya sol lu xonq curr, watiiri xare yay melax ni luy tàkk, ca bés ba ñu waajal xare, xeej ya jóg.
4Ca mbedd ya la watiiri xare yay riire, riddi jaare pénc ya, mel niy jum, di ray-rayi niy melax.
5Ca la njiit la di woolu kàngami xareem, ñuy gaawtu bay tërëf. Tata ja lañuy gaaw wutali, ba yékkati ay kiiraay.
6Bunt ya jëm dex ga ñooy jekki ubbiku, kër buur màbb.
7Futtees na jongama, yóbbu, janqam jay binni niy xati, di fëgg seen dënn.
8Niniw la ay nitam di daw, mu mel ni mbànd mu ndox may senn, ñu naan leen: «Taxawleen, taxawleen,» te kenn geestuwul.
9Sëxëtooleen xaalis, sëxëtoo wurus, alal du fi jeex te mboolem gànjar a jale.
10Dëkk bi lees di raatale, maasale, mu ne faraas, fit rëcc, óom yiy fenqe, ndigg yépp di kal-kali, kanam yépp di sël-sëli.
11Moo ana paxum gaynde ga? Ana àllub gaynde yu ndaw ya, fa góoru gaynde daa daagoo, mook jeegub gayndeem ak doom ya, te dara tiitalu leen!
12Gaynde di fa fàdd lu doy ay doomam, reyal ay jeegi gayndeem, feesal xuntam akum rëbbam, feesal paxam akum pàddam.
13«Maa ngii fi sa kaw,» kàddug Aji Sax jee, Boroom gàngoor yi. «Say watiiri xare laay lakk, saxaaral, sa gaynde yu ndaw, saamar lekk leen, te sam pàdd laay jële ci réew mi, ba deesul déggati baatu ndaw loo yebal.»