1Buur a ngii, dëgg lay nguuroo, jawriñ ñi it, yoon lañuy yilifee;
2ku ci nekk mel ni seelukaayu ngelaw, di kiiraay ci ngëlén, mel ni wali ndox ci suuf su ne sereŋ, mbaa keppaaru doj wu mag ci àll bu mar.
3Su boobaa gëti njàccaar yi dootuñu gëmm, te noppi ñiy dégg dañuy teewlu,
4ku yàkkamti di ràññee, ba mana xam, làmmiñu ku dër gaawa wax lu leer.
5Booba deesatul woowe ab dof «gor si», te njublaŋ dootul dégg «ku tedd ki».
6Ab dof, waxi dof lay wax, xel ma di nas ñaawtéef, mu nar jëf ju teddadi. Lu ñaaw lay wax, jëme ci Aji Sax ji, di xiifal ku xiif, di xañ ku mar lu mu naan.
7Ab njublaŋ, ay pexeem musiba la. Njekkar lay nas, ba bu néew-ji-doole sàkkoo dëgg it, mu fen ba lor ko.
8Waaye gor si, ngor lay mébét, te ngor lay wéye.
9Yeen jigéen ñi dal xel, taxawleen temm, déglu ma; yeen janq ji féex, teewluleen ma.
10Yeen jigéen ñi dal xel, fi leek at aki fan ngeen jàq; witt mi du baax, ngóob du taxaw.
11Jigéen ñi dal xel, ragalleen; yeen ñi féex laa ne, tiitleen! Futtikuleen, ba ne duŋŋ; gembooy saaku, ñaawloo.
12Fëggleen seen dënn, jooy tooli bànneex ya, jooyleen reseñ ju nangu ja,
13ak sama suufas bokk ya ay dég aki dagg nangu. Jooyleen kay kër ya ca mbégte ma, ak dëkk bu xumb ba.
14Kër gu rafet sax, dees koy wacc, dëkk baak riiram, dees koy dëddu; tund ak tóoju doon ay xunt ba fàww, mbaamu àll ne ca finaax, jur ga di ca fore,
15ba keroog Boroom bi ëf ci nun ag noowam, màndiŋ mi soppalikub tóokër, tóokër meññ, ba ñu ne ab gott la.
16Su boobaa yoon dëkke màndiŋ mi, dëgg tooge tóokër bi.
17Su boobaa àtteb dëgg ay jur jàmm, àtteb yoon di dalal tey aare ba fàww,
18ba sama bokk yi dëkke sancub jàmm, ci dëkkuwaay yu wóor, ci dalluwaay yu dal xel,
19doonte gott bi day daanu ci tawub doji yuur, dëkk bi detteelu ba ne dett.
20Waaye ndokkalee yeen ñi tala ji fépp fuy ndox te saña afal nag ak mbaam.