1Efrayim mooy sàmmkatub ngelaw, yendoo topp ngelawal penku, di yokki fen ak fitna, fasoo kóllëre ak Asiri, yónnee yóbbalu diw ba Misra.
2Aji Sax ji moo séq ak Yuda ab layoo, mooy mbugale Yanqóoba ay jëfinam, añale ko ay jëfam.
3Ci biiru ndeyam la kii suufoo ab seexam; kii moo tollu ci dooleem, bëreek Yàlla.
4Kee bëreek malaaka, ba génn ca, kee jooy di sàkku aw yiwam. Fa Betel la ko fekk, te foofa la Yàlla waxeek nun.
5Aji Sax ji Yàlla Boroom gàngoor yi, Aji Sax jee di turu bàkkam.
6Yaw nag, ca sa Yàlla nga wara dellu, ngor ak njub, sàmm ko, te nga saxoo yaakaar sa Yàlla.
7Ni Kanaaneen biy jula, ni la Efrayim yore màndaxekaayu njublaŋ cib loxoom, bëgga naxe.
8Efrayim a ngi naan: «Woomle naa, maa amal sama bopp alal, te mboolem samaw ñaq, giseesu ci tooñaange ju di bàkkaar.»
9«Man Aji Sax ji dale di sa Yàlla ca Misra, maa lay dëëlaat ciy xayma, na woon ca bésub ndaje.
10Maa wax ak yonent yi, yokk peeñu yi, te yonent yi, maa leen léeb ay misaal.»
11Su Galàdd dee dëkkub defkati ñaawtéef, dañoo tekkiwul dara. Fa Gilgal lees di rendee ay saraxi yëkk, te seeni sarxalukaay ni jali xeer lay mel ci ay tooboy tool.
12Yanqóobaa dawoon ba réewum Siri, Israayil laa ne, moo liggéey ngir am jabar, wut jabar tax koo sàmm ag jur.
13Ci loxol yonent la Aji Sax ji génnee Israayil Misra, te ab yonent la sàmmloo Israayil.
14Waaye Efrayim moomoo ko merloo, naqaral ko. Deret ji mu tuur la Boroomam di këpp ci kawam, añub tooñam la koy fey.