1Ma séentu, gisuma lu moy jenn waay ju yor buumu nattukaay ci loxoom.
2Ma ne ko: «Foo jëm?» Mu ne ma: «Xanaa natti Yerusalem, ba xam nu mu yaatoo ak nu mu gudde.»
3Fa la malaaka ma doon wax ak man jekki di dem, meneen malaaka dikk dajeek moom.
4Mu ne ko: «Dawal, nga wax xale bu góor bii ne ko: “Yerusalem lees di dëkke, te tata wëru ko; ŋàpp lay def, ndax barewaayu nit ñeek jur gi ci biiram.
5Te man ci sama bopp,” kàddug Aji Sax jee, “maa koy nekkal tatay sawara ji ko ub ràpp. Te it maay doon daraja ji ci biiram.”
6Éey, éey yeen, dawleen génne réewum bëj-gànnaar,» kàddug Aji Sax jee. «Ni ñeenti ngelawi asamaan tasaaroo, ni laa leen tasaaree.» Kàddug Aji Sax jee.
7«Éy Siyoŋ, rëccal, yaw mi dëkke janq Babilon mu taaru mi.»
8Aji Sax ji Boroom gàngoor yi déy dafa wax, moom mi ma yebal ngir teddaayam, ci mbirum xeet yi leen sëxëtoo woon, nee: «Képp ku leen laal kat, laal na sama reeni xol.
9Maa ngii déy di xàcc sama loxo ci seen kaw, te ñoom la seeni jaam di sëxëtooji.» Kon dingeen xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal.
10«Sarxolleel te bànneexu, yaw janq Siyoŋ mu taaru, nde maa ngii di dikk, màkkaanoo fi sa biir.» Kàddug Aji Sax jee.
11«Bésub keroog la xeet yu bare di taqook Aji Sax ji, ba doon sama ñoñ, ma màkkaanoo fi sa biir.» Kon nga xam ne Aji Sax ji Boroom gàngoor yi moo ma yebal ci yaw.
12Aji Sax jeey séddoo Yuda, muy wàllam ci suuf su sell si, te mooy tànnati Yerusalem.
13Na wépp suux ne cell fi kanam Aji Sax ji, ma ngoogu sàqee fa màkkaanam mu sell ma.