1Mu jëm ci njiital woykat yi, ànd ak xalam gu ñuy wax gitiit, ñeel askanu Kore wu góor. Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, yaaka sopplub dëkkuwaay!
2Damaa namm ëttub Aji Sax ji, di ko gelu ba jeex tàkk, jëmm jeek xol bi, di xaacul Yàlla jiy dund.
3Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, sama buur, sama Yàlla, sawoor sax tag, nga fat ko, mbelaar it sàkk tàggam, denc ay cuujam fa sa sarxalukaay.
4Ndokkalee ku dëkke sa kër, di la màggalati. Selaw.
5Ndokkalee ku lay doolewoo, te namma topp yoon ya jëm sa kër.
6Buy jàll xuru Jooyoo, mu saf ko bëti ndox, céebo sànge xur wa barke,
7muy gëna am doole, ba teewi fa Yàlla ca Siyoŋ.
8Éy Yàlla Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, déglul, ma ñaan la! Yàllay Yanqóoba, teewlu ma. Selaw.
9Éy Yàlla, geesul Buur, sunu kiiraay, ngalla niiral kii nga fal.
10Benn fan ci sab ëtt de moo dàq junniy fan feneen. Sama taxawaayu bunt kër Yàlla moo ma gënal tëraayu biir xaymab ku bon.
11Aji Sax ji Yàllaa mat jant, mat kiiraay; yiw ak daraja, Aji Sax ji joxe; te du ngëneel lu muy bañal ku mat.
12Éy Aji Sax ji Boroom gàngoor yi, ndokkalee ku la wóolu.