1Mu jëm ci njiital woykat yi, dëppook galan bu ñuy wax Seedeb tóor-tóor, diy ñaan, ñeel Daawuda. Mooy ba Daawuda di xareek waa Siri ña ca Mesopotami ak waa Siri ña ca Coba te ba ñu ca bàyyikoo, Yowab duma fukki junniy Edomeen ak ñaar (12 000) ca xuru Xorom wa. Éy Yàlla, wacc nga nu, bëtt sunu kiiraay. Mer nga, waaye ngalla xettali nu.
2Yëngal nga suuf, xar ko; ngalla jagalal, mu tëju, mu ngi jaayu!
3Won nga sa mbooloo lu metti, nàndal nu biiñu mbugal, ba nu miir.
4Sampal nga ab raaya ñi lay ragal, ngir ñu mucc ci fitt yi. Selaw.
5Walloo nu sa ndijoor, nangul nu, ba say soppe xettaliku.
6Yàllaa àddoo fa këram gu sell, ne: «Maay damu, dogat suufas Sikem, séddale xuru Sukkót.
7Maa moom diiwaanu Galàdd, moom Manase, Efrayim di sama mbaxanam xare, Yuda di sama yetu nguur,
8réewum Mowab di sama ndabal raxasukaay, Edom, ma teg tànk; Filisti, ma xaacoo fa.»
9Éy Yàlla, ana ku may yóbbu dëkk ba tata wër? Ku may jiite ba Edom?
10Xanaa kay du yaw, Yàlla mi nu wacc, yaw Yàlla mi baña ànd ak sunu mboolooy xare?
11Ngalla dimbali nu ci bañaale; doom aadama, wallam neen la.
12Nook Yàlla, nu def njàmbaar; moom mooy noot sunuy noon.