1Mu jëm ci njiitu woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Mooy ba ko Yonent Yàlla Natan seetsee, gannaaw ba Daawuda tëddee ndaw sa ñuy wax Batseba. Éy Yàlla, ni nga goree, baaxe ma ni, faral samag tooñ ngir sa yërmande ju yaa.
2Fóotal maa fóotal sama ñaawtéef, raxasal ma sama moy.
3Xam naa ne maa tooñ, sama moy a ngi janook man saa su ne.
4Yaw laa moy, yaw doŋŋ. Li nga ñaawlu laa def. Kon boo waxee, am dëgg, te soo àttee, yey.
5Ñaawtéef daal laa judduwaale, te sama ndey ëmbaale ma bàkkaar.
6Dëgg daal nga namm, dëggu reenu xol, kon déey ma fa xel mu rafet.
7Wis ma ndox, ma sell; sang ma, ma set wecc.
8Yal nanga ma dégtal mbég ak bànneex, ma bégati, gannaaw ba nga ma dammatee.
9Bul xool samay moy, faral sama ñaawtéef yépp.
10Éy Yàlla, sàkkal ma xol bu sell, yeesalal ma pastéefu xol.
11Bu ma xalab, bu ma xañ sa noo gu sell.
12May ma, ma bégeeti sag wall, te dundale ma xol bu tàlli,
13ma xamal tooñkat sa yoon wi nga tëral, ba moykat dellu ci yaw.
14Céy Yàlla, yaw Yàlla mi may musal, baal ma deret ji ma tuur, ma sarxolle sa njubte.
15Boroom bi, may ma, ma wax, ma delloo la njukkal.
16Sàkkuwuloo sarax, nde kon ma indi; te soppuloo saraxu rendi-dóomal.
17Saraxi Yàlla, xol bu tuub la, yaw Yàlla, xol bu tuub ba mokk, doo gàntal boroom.
18Ngalla baaxeel Siyoŋ, yal nanga tabax tatay Yerusalem.
19Su boobaa nga nangu sarax yi war, di saraxu rendi-dóomal. Su boobaa ñu rendi ay yëkk ca sa sarxalukaay.