1Mu jëm ci njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel askanu Kore wu góor. Yeen, xeetoo xeet, dégluleen; yeen, waa àddina yépp, teewluleen,
2ngay ku tuut di ku mag, nga bareleek nga néewle.
3Li may wax xel la, di xalaat yu déggu.
4Damay teewlu kàddu yu xelu, xalamal la sama tekkiteb cax.
5Ana lu may tiit bés yu metti, yu ma njublaŋ yéewe seeni ñaawtéef,
6di ñu wóolu seen am-am, di kañoo alal ju bare?
7Ana ku mana jot a jot sa bakkanu moroom, mbaa mu di ko feyal Yàlla njot ga?
8Njotug bakkan jafe na, bu ci jéem dara.
9Ana kuy dund ba fàww, ba doo gis bàmmeel?
10Xanaa gis ngeen ne xelu, dee; dof, dee; naataxóona it faatu rekk, wacce keneen alalam.
11Sa bàmmeel di sa kër ba fàww, di sa dëkkuwaay bu sax dàkk, boo tudde woon sa bopp ay suuf sax.
12Nit ak darajaam fanaanul, mook aw rab a yem, sànku rekk.
13Nii la ku wóolu boppam di mujje, mook ku ko topp, di safooy waxam. Selaw.
14Nara dee rekk niy xar, dee wommat, yóbbu, njub fenk nib jant, ku jub moom leen, njaniiw mëdd seen jëmm, fu sore kërug daraja.
15Waaye Yàllaa may musal ci dooley njaniiw, jot sama bakkan, ba jël ma. Selaw.
16Buleen yéemu ci ku barele, teraangay këram di yokku.
17Du dee ba yóbbaale dara, teraangaam du ko topp biir bàmmeel.
18Na bége bànneexu bakkanam, ñu di ko kañe koomam,
19ba tey, day dee, fekkiy maamam, ña dootul gisug leer ba fàww.
20Nit ak darajaam te amul dégg, mook aw rab a yem, sànku rekk.