1Mu jëm ci njiital woykat yi, di woy wu ñeel askanu Kore wu góor, dëppook galan bu ñuy wax Baatu jigéen. Sunu Yàllaa nuy rawale, di nu dooleel, di nu wallu fu nu jaaxlee,
2ba dunu tiit suuf su yëngu sax, ba tund yiy tàbbi biir géej,
3mbaa gannax yuy riir, di fuur aka fuddu bay gësëm tund yi. Selaw.
4Ag dex a ngi defi wal, di bànneexal dëkku Yàlla, sellaayu màkkaanu Aji Kawe ji.
5Yàllaa ngi ci biir dëkk bi, du raf; Yàllaa koy dimbali ba jant fenkee.
6Ay giir a riir, ay réew yëngu; mu àddu, suuf seey!
7Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.
8Dikkleen gis jaloorey Aji Sax ji, ak yàqute gi mu dogal ci kaw suuf.
9Mu ngi fey xare ci àddina sépp, dog fitt, damm xeej, lakk pakk.
10Mu ne: «Dalleen te xam ne maay Yàlla, màgg ci biir xeet yi, màgg fi kaw suuf.»
11Aji Sax ji Boroom gàngoor yee ànd ak nun, Yàllay Yanqóoba jee nuy rawale. Selaw.