1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda, ba muy daw Absalom doomam ju góor. Éy Aji Sax ji, noon yeeka bare! Ñu baree may jógal,
2ñu baree may tooge naa: «Yàlla du ko wallu!» Selaw.
3Waaye yaw Aji Sax ji, yaa may feg, di ma teral, di ma siggil.
4Maay woo Aji Sax ji wall, mu walloo ma fa tundam wu sell wa. Selaw.
5Maay tëdd nelaw, yewwu; Aji Sax ji di ma aar.
6Ñu dul jeex a ma jógal, gaw ma, te duma ragal.
7Éy Aji Sax ji sama Yàlla, jógal, wallu ma! Yaa toj kaabaabi noon yu bon yépp, foq seeni sell.
8Aji Sax ji, yaa moom wall, sa mbooloo jagoo sa barke. Selaw.