1Mu jëm ci Yedutun, njiital woykat yi, dib taalifu cant, ñeel Daawuda. Dama noon: «Damay moyu ba duma moye làmmiñ.» Li feek ku bon di teew, may ŋalaab sama gémmiñ.
2Dama noon cell, ne patt, noppi, ba mu ëpp; sama njàqare yokku,
3sama xol diis, xel di xelaat, xol diis gann; ma mujj àddu,
4ne: «Éy Aji Sax ji, xamal ma sama muj ak sama àppi fan, ma xam ni sama dund gàtte.
5Yaatuwaayu loxo nga ma àppal ciy fan, sama giiru dund du dara fi yaw. Képp ku taxaw di cóolóolu neen. Selaw.
6Nit du lu moy takkndeer buy dem, cóolóolu neen lay kër-këri. Nit a ngi dajale, xamul kuy for.
7«Éy Boroom bi, lu may xaarati? Sama yaakaar yaw a.
8Musal ma ci sama mbugali tooñoo tooñ, bu ma bàyyi, dof di ma reetaan!
9Noppi naa, dootuma wax, yaw yaa dogal lii.
10Waaye ngalla teggil sab yar, sa diisaayu loxoo ngi may jekkali.
11Yaay mbugal ku bàkkaar, yar ko, ronq la mu gëna fonk, ni max. Nitoo nit, cóolóolu neen. Selaw.
12Éy Aji Sax ji, déglul, ma ñaan la, teewlul, ma woo la wall; bul tanqamlu sama yuux, doxandéem doŋŋ laa fi yaw, di gan ni maam yépp.
13Ngalla xiddi ma, ma muuñ, bala maa dëddu, réer.»