1Mu jëm ci njiital woykat yi, ñeel Daawuda jaamub Aji Sax ji. Kàddug tooñ ga ku bon wax mu ngi ci sama xel mi. Mu ne: «Ana lu may ragal ci Yàlla?»
2Day gis boppam, naagu, ba du gis sikkam, sib ko.
3Ay waxam coxor aki fen, jëfeetul lu rafet ak lu baax.
4Day mébét lu ñaaw cib lalam, taxawe yoon wu dëddu mbaax, te du bañ lu bon.
5Céy Aji Sax ji, gore nga ba kaw asamaan, dëggu ba ci kaw-li-kaw.
6Sa njubtee tiim tund yu mag yi, sa àtte ne xéew ni xóotey géej. Céy Aji Sax ji, nit ak mala, nga boole sàmm!
7Céy Yàlla, yaa wéet ngor, doom aadama yiiroo sa keppaar, yiiru;
8yafloo sa njël lu duun, sa xéewal wal, nga nàndale ko.
9Ci yaw la dund di balle, te sag leer lanuy leerloo.
10Jotaleel sa ngor ku la xam, jotale sa njubte kuy nas njub.
11Yàlla bu ma ku reew teg tànk; loxo ku bon, yàlla bumu ma taxa daw.
12Defkati mbon yaa ngii, daanu, ne lareet, tëlee jóg.