1Dib taalifu cant, ñeel Daawuda ca daloob kër Yàlla ga. Aji Sax ji, dama lay kañ. Yaa ma yékkati, ba noon reetaanu ma.
2Aji Sax ji sama Yàlla, maa la woo wall, nga faj ma.
3Aji Sax ji, yaa ma jukkee njaniiw, may ma bakkan, ma tàggook ñiy tàbbi njaniiw.
4Yeen aji gëm ñi, woyleen Aji Sax ji, njukkale ko sellaayam.
5Meram di lu gàtt, aw yiwam sax dàkk. Rongooñ gane, fanaan, ay ree xëysi.
6Man damaa baaxle woon, ba ne: «Deesu ma rëññeel mukk.»
7Aji Sax ji, booba yaa ma baaxe, dëj ma, ma ne kekk niw tund. Nga fuuyu, ma jàq.
8Aji Sax ji, yaw laa woo wall; Boroom bi, yaw laa ñaanu yiw,
9ne la: «Ma dee, tàbbi bàmmeel, ana lu mu lay jariñ? Nu la pëndu pax di sante, bay biral sa kóllëre?
10Aji Sax ji, déglul, baaxe ma; éy Aji Sax ji, dimbali ma.»
11Yaa ma soppil samay rongooñ ay ree, summi sama yérey tiis, solal ma bànneex.
12Naa la woye xol, baña selaw. Aji Sax ji, sama Yàlla, ma sant la ba fàww!