1Ba loolu amee Aji Sax ji ne Musaa:
2«Waxal ak bànni Israayil, nga nangoo ci mboolem seen kilifay kër maam, aw yet, na wenn yet bawoo ci kër gu ci nekk, muy fukki yet ak ñaar, yet wu ci nekk, nga bind ci turu boroom.
3Turu Aaróona itam, nga bind ko ci yetu giirug Lewi, ndax wenn yet lay doon, ñeel kilifag kër gu ci nekk.
4Nga denc yet yi ca biir xaymab ndaje ma, fa kanam gaalu seedes kóllëre ga, fa may dajeek yeen.
5Su ko defee ki ma tànn, aw yetam dina jebbi, ba ma teqalikoo ak xultuy bànni Israayil yi ñuy xultu ci seen kaw.»
6Musaa àgge ko bànni Israayil, mboolem seen kilifay kër maam jox Musaa aw yet, kilifa gu ci nekk wenn yet, ñeel kër maamam, muy fukki yet ak ñaar, yetu Aaróona bokk ca.
7Musaa teg yet ya fa kanam Aji Sax ji, ca biir xaymab seede sa.
8Ca ëllëg sa, naka la Musaa dugg ca xaymab seede sa rekk, daldi fekk yetu Aaróona wu kër Lewi, jebbi; fekk na mu jebbi, ba tóor, ba meññ ay doomi amànd.
9Ba loolu amee Musaa jële yet yépp ci Aji Sax ji, dem ba ca bànni Israayil gépp, ñépp gis, ku nekk jël yetam.
10Aji Sax ji waxati Musaa, ne: «Dellool yetu Aaróona fa kanam gaalu seede sa, mu dence fa, di firnde ñeel xeetu fippukat wi, ndax nga dakkal seeni xultu ci sama kaw, ba duñu dee.»
11Musaa def noonu. Na ko ko Aji Sax ji sante, na la ko defe.
12Bànni Israayil nag naan Musaa: «Jeexal nanu nag, sànku nanu, nun ñépp ay sànku!
13Gannaaw képp ku jege màkkaanu Aji Sax ji doŋŋ, dangay dee kay, mbaa dunu far jeex tàkk?»